Ba ma amee juróom-benni at, mës naa gis nataal bu rafet
ci ab téere ci mbiru àll bu naat bu tuddoon Nettali yu
dëggu. Nataal baa ngi doon wone yeew muy wonn mala. Sotti bu nataal
baa ngi nii.
Ñu ngi doon wax ci téere bi ne: “Yeew
yi danuy wonn ay mala te duñu leen sàqami. Ginnaaw bi
duñu mën a yëngu te dañuy nelaw juróom-benni
weer di reesalaale.”
Loolu tax na ba may xalaat lu bari ci nettali
yiy xew ci àll bi. Ma daldi jël kareyoŋ tàmbalee
rëdd sama nataal bu njëkk.
Mit freundlicher Unterstützung von – Avec le soutien de
:

|